Gaaraasu weccoo batëri bu xarañ bi, aparey bu am xel la buy joxe sarwis bu gaaw buy weccoo batëri oto kuraŋ yi (lu melni velo kuraŋ, moto kuraŋ, ak oto kuraŋ yu gaawaay bu woyof). Li gëna am solo ci liggéeyam mooy jëfandikoo xaralay otomaasioŋ ngir may jëfandikukat yi ñu mëna wecci batëri yi ci diir bu gàtt te duñu xaar lu yàgg ngir sarse leen, loolu mooy gëna yombal liggéey bi ak yombal oto electrik yi. Aparey bii dafay njëkka liggéey ci senaario yu ñuy faral di jëfandikoo oto kuraŋ, lu ci melni dawalkat yiy yóbbu lekk, kureer, ak operatëri oto kuraŋ yuñ bokk. Mën nañu ko jëfandikoo itam ci barab yu ñépp bokk lu ci melni dëkk yi, dëkki jënd ak jaay yi, ak bërëbi dem ak dikk yi, muy joxe pexe yu yomb ngir yokk kuuraŋ ci ñiy jëfandikoo oto kuraŋ.
Njàngalem xarala ak doxalinu liggéey Njàngalem liggéeyu gaaraasu weccoo batëri bu xarañ mingi aju ci lëkkaloo xaralay Internet of Things (IoT), jumtukaayi mekanik yuy otomatise, ak Sistemu Yorandi Batëri (BMS). Niñu koy faral di defee mooy:
Xamme jëfandikukat bi ak liggéeyam: Jëfandikukat yi dañuy scanner kodu QR bi ci gaaraas bi ci aplikaasioŋ mobile. Ginaaw bi sistem bi xoolee seen dàntite, dañuy ubbi benn compartiment bu jàppandi.
Dencukaay ak jëlaat batëri: Jëfandikukat yi dañuy dugal batëri bu jeex ci barab buñ ko jagleel. Benn loxo robot wala rail guide bu nekk ci biir gaaraas bi dafay toxal batëri bi ci saasi ci barabu sarse bi; ci saasi, batëri bu sarse bamu mat génn ci beneen compartiment ngir jëfandikukat bi jëlee ko.
Sarse ak saytu: Modulu sarse biñ tabax ci biir gaaraasu weccoo batëri bi dafay sarse batëri yiñ rësikle ci anam wu am xel, ba noppi di saytu parametre yu melni voltage ak tàngoor ci saa si jaaraleko ci BMS ngir mëna wóor sarse bi.
Doxal Done ak Fay: Sistem bi dafay bind tolluwaayu batëri bi, leerali jëfandikukat bi, ak njëgu weccoo batëri bu nekk, jàppale fayu ci net bi wala fay weer wu nekk ci kàrt.






