Couche conducteur, ñu xamee ko ci pre-coating, ci liggéeyum batëri litium dafay nuru couche conducteur buñu def ci kaw surfaasu collector courant electrode positif-foil aluminium. Foil aluminium buñu raxas ak couche conducteur bii ñu koy woowe aluminium buñu raxas bu njëkk wala aluminium buñ raxas rek. Couche conducteur yi ci batëri litium yi dañuy gëna baaxal adhésion electrode yi, wàññi limu liant bi ñuy jëfandikoo, ba noppi gëna baaxal performance electrik batëri yi. Jàngat yi mu njëkka amal ci batëri mingi méngoo ak ati 1970, ba noppi mu jëm ca kanam ginaaw bi liggéeyum energie bu bees bi amee, rawatina batëri litium iron phosphate, mu dem ba nekk batëri bu ñuy wut bu baax - ginaaw xarala wala macceer bu bees.
Nafar sistemu batëri dafa wara am ñaari lalu aaru elektronik ci sarse bu ëpp, desarse bu ëpp-, ak courant bu ëpp. Sudee batëri bi dafa kalaate ginaaw biñu dindie tablo aar bi, loolu dafay wane ni amna sikk ci jëmmal. Doonte anam wii dafa am ñaari xeeti aar, konsomatër yi dañuy faral di jënd sarseer yu amul -orginaal ginaaw bi seen sarseer yàqoo. Defarkatu sarseer yi, ndax njëg yu bari, dañuy faral di dindi sarsekat bi ngir wàññi njëg yi. Loolu mooy waral sarseer yu baaxul yi di dàq sarseer yu gëna baax yi, moo waral sarseer yu bari yu baaxul ci marse bi. Loolu dindi na kaaraange gu njëkk gi gëna am solo ci sargal lu ëpp. Li gëna waral batëri bi di kalaate mooy sarse lu ëpp; Kon sarseer yu baaxul yi ñoo waral batëri yi di kalaate. Dëgg la dina am, du sistem batëri yépp ñooy jëfandikoo pexe yiñ wax ci kaw. Amna numuy deme batëri bi dafay am -kontrolëru sarse buñ tabax ci biir.






